Folk Tale

Doomi Yàlla

LanguageWolof
OriginSenegal

Léeboon! Lippóon! Amoon na fi! Daan na am! Ba mu amee yaa fekkee? Ya wax ma dégg! waxi tey jar ta gëm! Sa yos moo ci raw!

Xew xew bii ma nga ameewoon ca jamono ya rab yi daan wax ag nit ñi. Amoon fi jenn jigéen ju bon ju nekkoon ag ñeenti doomam. Ñoo nga dekkoon ca biir àll ba. Baayu xale yi, bi caat mi ñuy wax Tóni juddoo la dee; yaay ji jàpp ne kon xale bi dafa aay gaaf. Mu daldi ko bañ. Bu mosee rëbbi ba ñëw, day woo xale yi, benn benn, ñu nàmp ba mu des Tóni. Muy woy naan: Jamloro kaay nàmp, Jamloro Siise kaay nàmp, Biraama Siise kaay nàmp, Ndaama Siise kaay nàmp, Na Tóni xaar Yàlla yaayam. Di ko def ay yooni yoon. Waaye, jigéen ju bon ji mosul xam ne Yàlla daan na feeñu Tóni ci melokaanu daar bu bare meew; bu ñowee di nàmpal Tóni. Am bés, musiba dal jigéen ji. Mu jóge ca àll ba di woy; woy wa mu daan woowee xale yi ngir nàmpal leen; yemmoog Bukki di jaar,déglu woy wi, jàng ko ba mën ko bu baax. Benn bés, yaayu xale yi dem rëbbi. Bukki doxe ko gannaaw roy baataam, di woy woy wi. Xale yi di génn benn benn, bukki di leen lekk ba mu des Tóni. Ba yaay ja jógee àll ba, muy woy, kenn wuyuwu ko, mu jaaxle lool. Yàggul dara, mu dégg baat bu mu miin, di woy naan ko: Jamloro, Bukki jël na ko, Biraama Siise, Bukki jël na ko, Ndaama Siise, Bukki jël na ko; Tóni rekk a des ci yaayam Yàlla! Ba mu déggee kàddu yooyu, jigéen ji dafa yuuxu, yuuxu gu tar,réer ci àll bi. Foofa la léeb doxee tàbbi géej, bàkkan bu ko njëkka fóon tàbbi àjjana.


Text view