Folk Tale

Lan mooy àddina

LanguageWolof
OriginSenegal

Dafa amoon genn góor gu màggat gu amoon jenn doom ju tolluwoon ci waxambaane, laabiiroon, waaye xaralawul, yeewuwul dara ci mbiru àdddina, yaakaaroon na lé lepp lu ñu ko digal rekk lu baax la. Xàmmeewul lu war ag lu warul! Benn bés, Jegaan, góor gaa ngi toogoon ci péncum dëkk bi, doom ji ,Mbañig, romb ko, jiital am mbaam, bàyyyikoo tool ya. Góor gi xool ko lu yàgg a yàgg, né ko: ‐ Sama doom, xam nga lan mooy àddina? Mbañig daldi né cell. Baay ba dellu né ko: ‐ Xam nga lan mooy àddina? Waxambaane wa xool ci suuf ba mu yàgg mu xool baay bi, ni ko: ‐ Baay, lan mooy àddina? Jegaan daldi ko xoolaat lu yàgg, yëngal boppam, muuñ, ni bërét ni ko: ‐Saa doom, jógal wommat mbaam mi nu dem, ma won la, luy àddina. Doom ji jóg ànd ag baay bi, ñu dem. Ñuy dox, di dox ba yegg ci beneen dëkk. Ña leen a jëkka séen ca dëkk ba dañu teg seen loxo ci seen gémmiñ. Genn góor gu màggat né leen: ‐ Moo yéen! Xale bi warul mbaam mi, mag mi warul mbaam mi! Ku mosa gis lii waay? Nit di dox te yore mbaam mu dara fenqul! Wax jooju tàbbindoo ci noppu baay beeg bu doom ji, ñu xoolante lu yàgg; baay bi ni doom ji: ‐ Ma kott boog nga dox? Ñuy dem, di dem, di dem ba yegg ci beneen dëkk: baay baa ngi ci kow mbaam mi, doom ji di dox. Naka lañu dugg ci biir dëkk bi, ñu dajeeg ay waxambaane yu takku, yu jëmoon tool. Kenn ci ñoom, xam ni rekk moo ci gënoona sàmbaabóoy ni leen : ‐ Billaay góor gi, yaa soxor te bëgg nguur. Mënuloo wacc xale bi rekk mu toog sa wet, ngeen bokk mbaam mi; nga koy xool muy dox ci mbóoyo mi? Meneen mooroomam teg ci né: ‐ Aa! Am na mag ñoo xam ni kay, mbëggum daraja fa mu leen yem….! Wax jooju itam tàbbindoo ci noppu baay beeg doom ji. Ñu xoolanteeti lu yàgga yàgg; baay bi ni doom ji: ‐ Yéegal boog fi ci kanam! Ñuy dem, di dem, di dem ba yegg ci beneen dëkk. Baay beeg doom ji yépp ñu ngi ci kow mbaam mi. Nakka lañu dugg ci biir dëkk bi, ñu dajeeg ay jànq yu doon rooti, kenn ci jànq yi xool leen lu yàgg ni: ‐ Ñii dé ñoo bëgg lu ñu bokk: meen mbaam, ñaari nit! Keneen, ku gëna pànk ni: ‐ Céy góor gii moo nay! Mënoo wàcc mbaam mi te jëli meneen! Keneen ku yaru ndeysaan, teg ci né: ‐ Bu ko amul nag? Jànq bu pànk ba biiñ, régéju, tàccu, né ko: ‐ Kon mu dox te bàyyi mbaam meeg xale bi! Baay beeg doom ji bokk déggando ag gisandoo lii. Baay bi xool doom ji lu yàgga yàgg né: ‐ Ma wàcc boog dox ,bàyyi la nga kott mbaam mi? Ñuy dem, di dem, di dem ba agsi beneen dëkk. Doom ji kott, baay ji di dox. Ba ñu duggee ci biir dëkk bi, jenn jigéen ju màggat romb leen, daldi dar loxoom ci gémmiñam né: ‐ Xanaa damay waaru! Ku mosa gis lii ba àddina sosoo ba tey: mag di dox, xale di war! Xale bi déy moo gëna ñakk kersa. Wax jooju tàbbindoo ci noppu baay beeg bu doom ji, ñu xoolante lu yàgga yàgg. Baay bi ree. Doom ji ree. Baay bi né doom ji: ‐ Gis nga, dégg nga. Lii mooy àddina. Àddina , jéem mbaa ba la tudd. Góor gi wax wax na dëgg, ci àddina, ñaar ñoo fi am: dangay jéem mbaa nga ba. Ku bëgg nag looy def mu neex ñépp, dangay sonnal sa bopp ndax ñépp bokkuñu yem xalaat.


Text view